Imam Ahmad : 19049
حَدَّثَنَا إِسْمَاعِيلُ أَخْبَرَنَا الْجُرَيْرِيُّ عَنْ أَبِي الْعَلَاءِ بْنِ الشِّخِّيرِ عَنْ مُطَرِّفٍ قَالَ قَالَ لِي عِمْرَانُ إِنِّي لَأُحَدِّثُكَ بِالْحَدِيثِ الْيَوْمَ لِيَنْفَعَكَ اللَّهُ عَزَّ وَجَلَّ بِهِ بَعْدَ الْيَوْمِ اعْلَمْ أَنَّ خَيْرَ عِبَادِ اللَّهِ تَبَارَكَ وَتَعَالَى يَوْمَ الْقِيَامَةِ الْحَمَّادُونَ وَاعْلَمْ أَنَّهُ لَنْ تَزَالَ طَائِفَةٌ مِنْ أَهْلِ الْإِسْلَامِ يُقَاتِلُونَ عَلَى الْحَقِّ ظَاهِرِينَ عَلَى مَنْ نَاوَأَهُمْ حَتَّى يُقَاتِلُوا الدَّجَّالَ وَاعْلَمْ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَدْ أَعْمَرَ مِنْ أَهْلِهِ فِي الْعَشْرِ فَلَمْ تَنْزِلْ آيَةٌ تَنْسَخُ ذَلِكَ وَلَمْ يَنْهَ عَنْهُ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حَتَّى مَضَى لِوَجْهِهِ ارْتَأَى كُلُّ امْرِئٍ بَعْدَمَا شَاءَ اللَّهُ أَنْ يَرْتَئِيَ
Daf nu wax [Isma'il] wax nu [Al Jurairi] ci [Abul Alaa' bin Shikhkhir] ci [Mutharrif] mu wax nu; [Imran] ne ma; Dëgg la dinaa leen wax benn hadith tay, ngir Yàlla Azza Wa Jalla di leen amal njariñ ci bis yi ci topp, fàttaliku ni jaamu Yalla Tabaraka wa Ta'ala bi gëna baax ci bis péesal ñooy waa Mohamed, te fàttaliku ni dina am saa yu nekk benn mbooloo mu nit ñu bawoo ci diine islaam ñuy xeex saa yu nekk ci seen dëgg e mën nañu ray Dajjal bi. Te xamleen ne, Yonent bi Yàlla na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc mas naa def umra ak njabootam diiru fukki fan, te amul woon benn aaya bu ko dindi wala bu ko tere, ba keroog mu wees ba nit ñi gis coobarey Yàlla’.