Embrasser l'Islam, cliquez ici
ISLAM AL-HAQ: QURAN & HADITH
(The True Islam)



Imam Ahmad : 18297

حَدَّثَنَا عُثْمَانُ بْنُ عُمَرَ حَدَّثَنَا أُسَامَةُ بْنُ زَيْدٍ عَنِ الزُّهْرِيِّ أَنَّهُ سَمِعَ عَبْدَ الرَّحْمَنِ بْنَ أَزْهَرَ يَقُولُ رَأَيْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ غَزَاةَ الْفَتْحِ وَأَنَا غُلَامٌ شَابٌّ يَتَخَلَّلُ النَّاسَ يَسْأَلُ عَنْ مَنْزِلِ خَالِدِ بْنِ الْوَلِيدِ فَأُتِيَ بِشَارِبٍ فَأَمَرَ بِهِ فَضَرَبُوهُ بِمَا فِي أَيْدِيهِمْ فَمِنْهُمْ مَنْ ضَرَبَهُ بِنَعْلِهِ وَمِنْهُمْ مَنْ ضَرَبَهُ بِعَصًا وَمِنْهُمْ مَنْ ضَرَبَهُ بِسَوْطٍ وَحَثَا عَلَيْهِ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ التُّرَابَ

Daf nu wax [Usmaan bin Omar] Wax nu [Usamah bin Zaid] ci [Az Zuhri] ni dégg na [Abdurrahman bin Azhar] wax; Dama gis Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam ci xareb Fathu Makkah. Te ca jamono jooju maa ngi nekkoon xale bu ndaw. Mu doxantu ci biir nit ñi di laajte dëkkuwaayu Khalid bin Al Walid. Jekk saa am kuy naan khamer ñëw, mu wax ko -mu yar ko-. Ñu daal di koy dóor ak mbir yi ñu yor ci seeni loxo. Ñenn ñi dañu leen dóor seeni dàll, ñenn ñi dañu leen dóor yat, ñenn ñi dañu leen dóor mbagg. Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam sànni ci kawam suuf.