Imam Darimi : 121
أَخْبَرَنَا مُسْلِمُ بْنُ إِبْرَاهِيمَ حَدَّثَنَا حَمَّادُ بْنُ يَزِيدَ الْمِنْقَرِيُّ حَدَّثَنِي أَبِي قَالَ جَاءَ رَجُلٌ يَوْمًا إِلَى ابْنِ عُمَرَ فَسَأَلَهُ عَنْ شَيْءٍ لَا أَدْرِي مَا هُوَ فَقَالَ لَهُ ابْنُ عُمَرَ لَا تَسْأَلْ عَمَّا لَمْ يَكُنْ فَإِنِّي سَمِعْتُ عُمَرَ بْنَ الْخَطَّابِ يَلْعَنُ مَنْ سَأَلَ عَمَّا لَمْ يَكُنْ
Neena ñu [Muslim bin Ibrahim] ne nu [Ahmad bin Yazid Al Manqari] ne ma [sama pàppa] mu ne: 'Benn bis kenn ñëw ci Ibn Omar radiallahu 'anhu, mu laaj ko dara waaye xamuma lumu doon. Ci la [Ibn Omar] radliallahu anhu wax ne: 'Bul laaj lu xewul, ndax mas naa dégg [Omar bin Khtthab] radliallahu anhu di mbugal kiy laaj lu xewul.
Imam Darimi : 122
أَخْبَرَنَا الْحَكَمُ بْنُ نَافِعٍ أَخْبَرَنَا شُعَيْبٌ عَنْ الزُّهْرِيِّ قَالَ بَلَغَنَا أَنَّ زَيْدَ بْنَ ثَابِتٍ الْأَنْصَارِيَّ كَانَ يَقُولُ إِذَا سُئِلَ عَنْ الْأَمْرِ أَكَانَ هَذَا فَإِنْ قَالُوا نَعَمْ قَدْ كَانَ حَدَّثَ فِيهِ بِالَّذِي يَعْلَمُ وَالَّذِي يَرَى وَإِنْ قَالُوا لَمْ يَكُنْ قَالَ فَذَرُوهُ حَتَّى يَكُونَ
[Al Hakam bin Nafi'] nettali nu [Syu'aib] ci [Az Zuhri] mu ne: '[Xibar bi yegsi na nu] ni [Zaid bin Thabit Al 'Ansari] Yalna Yàlla defal ko mbégte, suñu ko laajee lu jëm ci dara dafay wax saa yu nekk: 'Ndax lii xewna? ', suñu tontu : 'waaw', ci dëgg-dëgg tontu na laaj bi ci limu xam, waaye suñu tontu : 'amagul', kon dafa wara wax: 'xaaral ba mu am dëgg''.
Imam Darimi : 123
أَخْبَرَنَا إِسْحَقُ بْنُ إِبْرَاهِيمَ أَخْبَرَنَا أَبُو هِشَامٍ الْمَخْزُومِيُّ حَدَّثَنَا وُهَيْبٌ حَدَّثَنَا دَاوُدُ عَنْ عَامِرٍ قَالَ سُئِلَ عَمَّارُ بْنُ يَاسِرٍ عَنْ مَسْأَلَةٍ فَقَالَ هَلْ كَانَ هَذَا بَعْدُ قَالُوا لَا قَالَ دَعُونَا حَتَّى تَكُونَ فَإِذَا كَانَتْ تَجَشَّمْنَاهَا لَكُمْ
[Ishaq bin Ibrahim] wax nu [Abu Hisham Al Makhzumi] wax nu [Wuhaib] wax nu [Daud] ci ['Amir] mu ne: '['Ammar bin Yasir] radliallahu 'anhu suñu ko laajee ci benn jafe-jafe, mu tontu: 'Déedet, mu tontu: 'Déedet? ba keroog muy am. Su loolu amee, dina nu la jox tontu li.'
Imam Darimi : 124
أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ أَحْمَدَ حَدَّثَنَا سُفْيَانُ عَنْ عَمْرٍو عَنْ طَاوُسٍ قَالَ قَالَ عُمَرُ عَلَى الْمِنْبَرِ أُحَرِّجُ بِاللَّهِ عَلَى رَجُلٍ سَأَلَ عَمَّا لَمْ يَكُنْ فَإِنَّ اللَّهَ قَدْ بَيَّنَ مَا هُوَ كَائِنٌ
Neena ñu [Muhamed bin Ahmad] newoon nañu [Sufyan] ci ['Amr] ci [Thawus] mu ne: '[Omar] radliallahu 'anhu wax -bi- ci kaw mimbar bi: 'Wallaahi ma bëgguma nit ñiy laaj lu xewul, ndax Yàlla moo xew jafe-jafe'.
Imam Darimi : 125
أَخْبَرَنَا عَبْدُ اللَّهِ بْنُ مُحَمَّدِ بْنِ أَبِي شَيْبَةَ حَدَّثَنَا ابْنُ فُضَيْلٍ عَنْ عَطَاءٍ عَنْ سَعِيدٍ عَنْ ابْنِ عَبَّاسٍ قَالَ مَا رَأَيْتُ قَوْمًا كَانُوا خَيْرًا مِنْ أَصْحَابِ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مَا سَأَلُوهُ إِلَّا عَنْ ثَلَاثَ عَشْرَةَ مَسْأَلَةً حَتَّى قُبِضَ كُلُّهُنَّ فِي الْقُرْآنِ مِنْهُنَّ { يَسْأَلُونَكَ عَنْ الشَّهْرِ الْحَرَامِ } { وَيَسْأَلُونَكَ عَنْ الْمَحِيضِ } قَالَ مَا كَانُوا يَسْأَلُونَ إِلَّا عَمَّا يَنْفَعُهُمْ
Abdullah bin Muhammad bin Abu Syaibah daf nu wax ni [Ibn Fudlail] ci ['Atho'] ci [Sa'id] ci [Ibn 'Abbas] radliallahu 'anhu mu ne: 'Musu ma gis nit ku gëna baax ci sahaba yu Yonent bi Yonent bi sallallaahu aleyhi wasallam- ba mu faatu lu moy lu tollu ci fukk ak ñetti jafe-jafe, ñoom ñépp ñu ngi ci Al Qur'an. Amoon na ci ñi ñu laaj: 'YAS`ALUUNAKA ANISSYAHRIL HARAAM' -Dañu lay laaj ci weer yi haram- -Qs. Al Baqarah: 217-, ak 'Wa Yas'Alunaka ANIL Mahid' -Dañu lay laaj ci wàllu gis-gis- -Qs. Al Baqarah: 222-'.
Imam Darimi : 126
حَدَّثَنَا عُثْمَانُ بْنُ عُمَرَ أَخْبَرَنَا ابْنُ عَوْنٍ عَنْ عُمَيْرِ بْنِ إِسْحَقَ قَالَ لَمَنْ أَدْرَكْتُ مِنْ أَصْحَابِ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَكْثَرُ مِمَّنْ سَبَقَنِي مِنْهُمْ فَمَا رَأَيْتُ قَوْمًا أَيْسَرَ سِيرَةً وَلَا أَقَلَّ تَشْدِيدًا مِنْهُمْ
Dañu nu wax ni [Uthman bin Omar] daf nu wax [Ibnu Aun] ci ['Umair bin Ishaq] ni: 'Amna nit ñu bari ñu ma dajeel ci sahaba yu Yonent bi (sallallaahu 'alaihi wasallam) ñu ma njëkka dee, musu ma gis askan wu leen gëna woyof ci seen dundu.
Imam Darimi : 127
أَخْبَرَنِي الْعَبَّاسُ بْنُ سُفْيَانَ عَنْ زَيْدِ بْنِ حُبَابٍ أَخْبَرَنِي رَجَاءُ بْنُ أَبِي سَلَمَةَ قَالَ سَمِعْتُ عُبَادَةَ بْنَ نُسَيٍّ الْكِنْدِيَّ وَسُئِلَ عَنْ امْرَأَةٍ مَاتَتْ مَعَ قَوْمٍ لَيْسَ لَهَا وَلِيٌّ فَقَالَ أَدْرَكْتُ أَقْوَامًا مَا كَانُوا يُشَدِّدُونَ تَشْدِيدَكُمْ وَلَا يَسْأَلُونَ مَسَائِلَكُمْ
Dañu ma wax [Al 'Abbas bin Sufyan] ci [Zaid bin Hubab] wax ma [Raja' bin Abu Salamah] mu ne: 'Mus naa dégg ['Ubadah bin Nusai Al Kindi], ñu laaj ko ci benn jigéen bu dee ci askan wi te amul benn njiit bu melni seen askan, mu ne: yaw, te duñu laaj li ngay laaj''.
Imam Darimi : 128
أَخْبَرَنَا الْعَبَّاسُ بْنُ سُفْيَانَ أَخْبَرَنَا زَيْدُ بْنُ حُبَابٍ أَخْبَرَنِي رَجَاءُ بْنُ أَبِي سَلَمَةَ حَدَّثَنِي خَالِدُ بْنُ حَازِمٍ عَنْ هِشَامِ بْنِ مُسْلِمٍ الْقُرَشِيِّ قَالَ كُنْتُ مَعَ ابْنِ مُحَيْرِيزٍ بِمَرْجِ الدِّيبَاجِ فَرَأَيْتُ مِنْهُ خَلْوَةً فَسَأَلْتُهُ عَنْ مَسْأَلَةٍ فَقَالَ لِي مَا تَصْنَعُ بِالْمَسَائِلِ قُلْتُ لَوْلَا الْمَسَائِلُ لَذَهَبَ الْعِلْمُ قَالَ لَا تَقُلْ ذَهَبَ الْعِلْمُ إِنَّهُ لَا يَذْهَبُ الْعِلْمُ مَا قُرِئَ الْقُرْآنُ وَلَكِنْ لَوْ قُلْتَ يَذْهَبُ الْفِقْهُ
Daf nu wax [Al Abbas bin Sufyan] daf nu wax [Zaid bin Hubab] daf ma wax [Raja' bin Abu Salamah] daf ma wax [Khalid bin Hazim] ci [Hsyyam bin Muslim Al Qurasyi] mu ne: 'Benn bis ma nekkoon ak [Ibn Muhairiz] ci tool bi, ak Ibn Muhairiz. mu laaj ma: 'Loo nara def ci jafe-jafe yii? Ma tontu ko: 'Sudee amul waxtaan ci jafe-jafe yi, xam-xam bi dina réer. Mu dellu niko bul wax ne xam-xam dafa réer, xam-xam du réer lu dul luy jàng Alquraan, waaye li gën a jub ci yaw nga wax ko ne réer nga ci xam-xam.
Imam Darimi : 129
أَخْبَرَنَا سُلَيْمَانُ بْنُ حَرْبٍ حَدَّثَنَا حَمَّادُ بْنُ سَلَمَةَ عَنْ دَاوُدَ عَنْ الشَّعْبِيِّ أَنَّ عُمَرَ قَالَ يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّا لَا نَدْرِي لَعَلَّنَا نَأْمُرُكُمْ بِأَشْيَاءَ لَا تَحِلُّ لَكُمْ وَلَعَلَّنَا نُحَرِّمُ عَلَيْكُمْ أَشْيَاءَ هِيَ لَكُمْ حَلَالٌ إِنَّ آخِرَ مَا نَزَلَ مِنْ الْقُرْآنِ آيَةُ الرِّبَا وَإِنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لَمْ يُبَيِّنْهَا لَنَا حَتَّى مَاتَ فَدَعُوا مَا يَرِيبُكُمْ إِلَى مَا لَا يَرِيبُكُمْ
Dañu nu wax ni [Suleyman bin Harb] daf nu wax [Hammad bin Salamah] ci [Daud] ci [As Sha'bi] ni [Omar] Radliallahhu 'anhu dafa wax; 'Yéen nit ñi, xamu nu woon ni amaana danu leen di digal ngeen def yenn mbir yu leen daganul, te amaana danu leen di tere yenn mbir doonte dañu leen daganal, li leer mooy li mujj wàcce ci Al Qur'an mooy aaya biy wax ci riba. Ta Rasulullah challallahu aleyhi wasallam leeralul nu ko ba mu faatu, kon lépp lu lay indi sikki-sakka bàyyil ko, nga jàpp ci lu nga amul sikki-sakka -ci moom-'.
Imam Darimi : 130
أَخْبَرَنَا سَلْمُ بْنُ جُنَادَةَ حَدَّثَنَا ابْنُ إِدْرِيسَ عَنْ عَمِّهِ قَالَ خَرَجْتُ مِنْ عِنْدِ إِبْرَاهِيمَ فَاسْتَقْبَلَنِي حَمَّادٌ فَحَمَّلَنِي ثَمَانِيَةَ أَبْوَابٍ مَسَائِلَ فَسَأَلْتُهُ فَأَجَابَنِي عَنْ أَرْبَعٍ وَتَرَكَ أَرْبَعًا
Dañu nu wax ni [Salm bin Junadah] daf nu wax [Ibn Idris] ci [ndijaay] niko: 'Dama jogee ci ndaje [Ibrahim], ci la Hammad daje ak man, jox ma juróom ñatti jafe-jafe. Ci ëlëg sa ma laaj ko lu jëm ci juróom ñatti jafe-jafe yi, mu tontu ma ñeenti jafe-jafe, bàyyi yeneen ñeenti jafe-jafe.
Imam Darimi : 131
أَخْبَرَنَا قَبِيصَةُ أَخْبَرَنَا سُفْيَانُ عَنْ عَبْدِ الْمَلِكِ بْنِ أَبْجَرَ عَنْ زُبَيْدٍ قَالَ مَا سَأَلْتُ إِبْرَاهِيمَ عَنْ شَيْءٍ إِلَّا عَرَفْتُ الْكَرَاهِيَةَ فِي وَجْهِهِ
Dañu nu wax [Qabisha] Dañu nu wax [Sufiyan] ci [Abdul Malik bin Abjar] ci [Zubaid] mu ne: 'Laajuma [Ibrahim] dara fileek gisuma màndarga mer ci kanamam'.
Imam Darimi : 132
أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ أَحْمَدَ حَدَّثَنَا إِسْحَقُ بْنُ مَنْصُورٍ عَنْ عُمَرَ بْنِ أَبِي زَائِدَةَ قَالَ مَا رَأَيْتُ أَحَدًا أَكْثَرَ أَنْ يَقُولَ إِذَا سُئِلَ عَنْ شَيْءٍ لَا عِلْمَ لِي بِهِ مِنْ الشَّعْبِيِّ
Dañu nu wax ni [Muhamed bin Ahmad] daf nu wax [Ishaq bin Mansur] ci [Omar bin Abu Zaidah] ni: 'Musu ma gis kenn ku wax: 'Amul benn xam-xam ci loolu' - bi ñu ko laajee ci benn jafe-jafe - buñu ko méngale ak [As Sha'bi]'.
Imam Darimi : 133
أَخْبَرَنَا أَبُو عَاصِمٍ عَنْ ابْنِ عَوْنٍ قَالَ سَمِعْتُهُ يَذْكُرُ قَالَ كَانَ الشَّعْبِيُّ إِذَا جَاءَهُ شَيْءٌ اتَّقَى وَكَانَ إِبْرَاهِيمُ يَقُولُ وَيَقُولُ وَيَقُولُ قَالَ أَبُو عَاصِمٍ كَانَ الشَّعْبِيُّ فِي هَذَا أَحْسَنَ حَالًا عِنْدَ ابْنِ عَوْنٍ مِنْ إِبْرَاهِيمَ
Daf nu wax [Abu 'Ashim] ci [Ibn 'Aun] niko dégg naa ko wax: 'Bu njëkk [As Sha'bi] su amee jafe-jafe mu daan wax bu baax, fekk [Ibrahim] wéy di wax, di wax, di wax". Abu Ashim dafa wax ni: 'Ibn'Aun dafa wax ni jikko Sha'bi moo gënoon baax jikko Ibrahim ci mbir mi.'
Imam Darimi : 134
أَخْبَرَنَا عَبْدُ اللَّهِ بْنُ سَعِيدٍ أَخْبَرَنَا أَحْمَدُ بْنُ بَشِيرٍ حَدَّثَنَا شُعْبَةُ عَنْ جَعْفَرِ بْنِ إِيَاسٍ قَالَ قُلْتُ لِسَعِيدِ بْنِ جُبَيْرٍ مَا لَكَ لَا تَقُولُ فِي الطَّلَاقِ شَيْئًا قَالَ مَا مِنْهُ شَيْءٌ إِلَّا قَدْ سَأَلْتُ عَنْهُ وَلَكِنِّي أَكْرَهُ أَنْ أُحِلَّ حَرَامًا أَوْ أُحَرِّمَ حَلَالًا
Abdullah bin Sa'id neena nu [Ahmad bin Basyir] neena nu [Syu'bah] ci [Ja'far bin Iyas] mu ne: 'Laaj naa [Sa'id bin Jubair] radiallahu 'anhu ' Lan moo tax doo wax - joxe xalaat bu yoon - ci thalaq? Mu tontu ma ni amul benn jafe-jafe ci thalaq fileek laaju ma ko, waaye maa ngi jaaxle, damay halal li haram, def naa haram li halal."
Imam Darimi : 135
أَخْبَرَنَا أَبُو نُعَيْمٍ حَدَّثَنَا سُفْيَانُ عَنْ عَطَاءِ بْنِ السَّائِبِ قَالَ سَمِعْتُ عَبْدَ الرَّحْمَنِ بْنَ أَبِي لَيْلَى يَقُولُ لَقَدْ أَدْرَكْتُ فِي هَذَا الْمَسْجِدِ عِشْرِينَ وَمِائَةً مِنْ الْأَنْصَارِ وَمَا مِنْهُمْ مِنْ أَحَدٍ يُحَدِّثُ بِحَدِيثٍ إِلَّا وَدَّ أَنَّ أَخَاهُ كَفَاهُ الْحَدِيثَ وَلَا يُسْأَلُ عَنْ فُتْيَا إِلَّا وَدَّ أَنَّ أَخَاهُ كَفَاهُ الْفُتْيَا
Dañu nu wax [Abu Nu'aim] [Sufyan] ci ['Atho'bin As Sa'ib] mu ne benn yoon dégg naa [Abdurrahman bin Abu Laila] wax: 'Dëgg la ma gis ci Jumaa bii - Nabawi - téemeeri ak ñaar fukki nit ci Ansar yi, kenn ci ñoom mënul nettali. hadith, te du ni dañu koy laaj ci fatwa bu yoon santaane waaye dina ko gëna bëgg sudee rakkam mooy nettali hadith bi. wax fatwa'.
Imam Darimi : 136
حَدَّثَنَا يُوسُفُ بْنُ يَعْقُوبَ الصَّفَّارُ حَدَّثَنَا أَبُو بَكْرٍ عَنْ دَاوُدَ قَالَ سَأَلْتُ الشَّعْبِيَّ كَيْفَ كُنْتُمْ تَصْنَعُونَ إِذَا سُئِلْتُمْ قَالَ عَلَى الْخَبِيرِ وَقَعْتَ كَانَ إِذَا سُئِلَ الرَّجُلُ قَالَ لِصَاحِبِهِ أَفْتِهِمْ فَلَا يَزَالُ حَتَّى يَرْجِعَ إِلَى الْأَوَّلِ
Dafa wax nu [Yusuf bin Ya'qub As Shaffar] wax nu [Abu Bakr] ci [Daud] ni benn yoon laaj naa [As Sha'bi]: 'Looy def suñu la laajee? '. Mu tontu ko ni, 'Tontu bi mooy ki yor dëgg-dëgg, suñu ko laajee mu wax beneen xarit : 'Jox leen fatwa, xaritam bi itam dina wax beneen xarit lu mel noonu ba mu mujjee dellu ci ki njëkka nekk'.
Imam Darimi : 137
أَخْبَرَنَا أَحْمَدُ بْنُ الْحَجَّاجِ قَالَ سَمِعْتُ سُفْيَانَ عَنْ ابْنِ الْمُنْكَدِرِ قَالَ إِنَّ الْعَالِمَ يَدْخُلُ فِيمَا بَيْنَ اللَّهِ وَبَيْنَ عِبَادِهِ فَلْيَطْلُبْ لِنَفْسِهِ الْمَخْرَجَ
Daf nu nettali [Ahmad bin Al Hajjaj] muni: Dégg naa [Sufyan] ci [Ibnu Al Munkadir] mu wax ni 'Ku am xam-xam -a ngi- ci diggante Yàlla ak jaamam, kon na laaj boppam yoonu génn'.
Imam Darimi : 138
أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ قُدَامَةَ حَدَّثَنَا أَبُو أُسَامَةَ عَنْ مِسْعَرٍ قَالَ أَخْرَجَ إِلَيَّ مَعْنُ بْنُ عَبْدِ الرَّحْمَنِ كِتَابًا فَحَلَفَ لِي بِاللَّهِ إِنَّهُ خَطُّ أَبِيهِ فَإِذَا فِيهِ قَالَ عَبْدُ اللَّهِ وَالَّذِي لَا إِلَهَ إِلَّا هُوَ مَا رَأَيْتُ أَحَدًا كَانَ أَشَدَّ عَلَى الْمُتَنَطِّعِينَ مِنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَمَا رَأَيْتُ أَحَدًا كَانَ أَشَدَّ عَلَيْهِمْ مِنْ أَبِي بَكْرٍ وَإِنِّي لَأَرَى عُمَرَ كَانَ أَشَدَّ خَوْفًا عَلَيْهِمْ أَوْ لَهُمْ
[Muhamed bin Qudamah] nettali nu [Abu Usamah] ci [Mis'ar] ni: [Ma'an bin Abdur Rahman] benn bis mu jox ma benn téere, mu waat ci kàddu yii: 'Wallaahi, téere bi bindug [baayam] la. Dafa mujj nekk ci téere bi ñu bind '[Abdullah] dafa wax; 'Maa ngi wax ci ki amul Yàlla ludul moom, musu ma gis kenn ku gëna metti ci nit ñi bëgg dem fu ëpp liñu mëna def ludul Yonent Yàlla sallallaahu'alaihi wasallam, rax ci dolli musu ma gis kenn ku gëna metti ci ñoom ni Abu Bakr radiallahu 'anhu. Te gis naa ni Omar bokkoon na ci nit ñi gënoona jaaxle ci ñoom walla musiba mi leen nara dal’.
Imam Darimi : 139
أَخْبَرَنَا أَبُو نُعَيْمٍ حَدَّثَنَا زَمْعَةُ بْنُ صَالِحٍ عَنْ عُثْمَانَ بْنِ حَاضِرٍ الْأَزْدِيِّ قَالَ دَخَلْتُ عَلَى ابْنِ عَبَّاسٍ فَقُلْتُ أَوْصِنِي فَقَالَ نَعَمْ عَلَيْكَ بِتَقْوَى اللَّهِ وَالِاسْتِقَامَةِ اتَّبِعْ وَلَا تَبْتَدِعْ
Neena ñu [Abu Nu'aim] neena ñu [Zam'ah bin Salih] ci [Osmaan bin Hadlr Al Azdi] mu ne; Benn bis laa ñëw ngir gise ak Ibn Abbas radiallahu anhu, ma ni ko: 'Jox ma ab testama.' Mu tontu ko: Waaw, dinaa la defal testama. Ragal-leen Yàlla te sax ci yoonam. Toppal sunna te bañ def bid’ah.
Imam Darimi : 140
أَخْبَرَنَا مَخْلَدُ بْنُ مَالِكٍ أَخْبَرَنَا النَّضْرُ بْنُ شُمَيْلٍ عَنْ ابْنِ عَوْنٍ عَنْ ابْنِ سِيرِينَ قَالَ كَانُوا يَرَوْنَ أَنَّهُ عَلَى الطَّرِيقِ مَا كَانَ عَلَى الْأَثَرِ
Mu wax nu [Makhlad bin Khalid bin Malik] mu wax nu [Nadlir bin Syumail] ci [Ibn Aun] ci [Ibn Sirin] mu wax nu; Samay xarit, nit ñi dañu jàpp ni nit mingi ci dëgg, lépp di aju ci atsar, di topp sunnatu Yonent bi.