Diperlihatkan Neraka, penghuninya mayoritas wanita karena kufur terhadap suami
Imam Nasa'i : 2035أَخْبَرَنَا سُلَيْمَانُ بْنُ دَاوُدَ عَنْ ابْنِ وَهْبٍ قَالَ أَخْبَرَنِي يُونُسُ عَنْ ابْنِ شِهَابٍ أَخْبَرَنِي عُرْوَةُ بْنُ الزُّبَيْرِ أَنَّهُ سَمِعَ أَسْمَاءَ بِنْتَ أَبِي بَكْرٍ تَقُولُقَامَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَذَكَرَ الْفِتْنَةَ الَّتِي يُفْتَنُ بِهَا الْمَرْءُ فِي قَبْرِهِ فَلَمَّا ذَكَرَ ذَلِكَ ضَجَّ الْمُسْلِمُونَ ضَجَّةً حَالَتْ بَيْنِي وَبَيْنَ أَنْ أَفْهَمَ كَلَامَ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَلَمَّا سَكَنَتْ ضَجَّتُهُمْ قُلْتُ لِرَجُلٍ قَرِيبٍ مِنِّي أَيْ بَارَكَ اللَّهُ لَكَ مَاذَا قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي آخِرِ قَوْلِهِ قَالَ قَدْ أُوحِيَ إِلَيَّ أَنَّكُمْ تُفْتَنُونَ فِي الْقُبُورِ قَرِيبًا مِنْ فِتْنَةِ الدَّجَّالِ
Suleyman bin Dawud nettali nu ko ci Ibn Wahb ni; Yunus ci Ibn Shihab; Urwah bin Zubair xamal nama ni dafa dégg Asma bintun Abu Bakr wax; Rasulullah challallahu 'aleyhi wasallam taxaw, wax ci xas biy dal nit ci bàmmeel bi. Ginnaaw bi mu waxee loolu, jullit ñi daldi yuuxu bu réy, tere ma dégg kàddug Yonent bi sallallaahu aleyhi wasallam. Bi seen yuuxu wàccee, ma laaj kenn ku nekkoon ci sama wet; 'Nanga def, Yalna la Yàlla defal jàmm! Lan la Yonent bi Sallallaahu aleyhi wasallam wax ci njeextalu kàddoom gi? Muni ma: “Dañu ma wàccee ni dina ngeen jànkoonte ak natt ci seen bàmmeel buy nuru natt bu Ad Dajjal”.