Embrasser l'Islam, cliquez ici
ISLAM AL-HAQ: QURAN & HADITH
(The True Islam)
Free Download / Download

Imam Nasa'i (الامام النسائي) - 5662 Hadith

Hadith

Imam Nasa'i : 21

أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ مَنْصُورٍ قَالَ حَدَّثَنَا سُفْيَانُ عَنْ الزُّهْرِيِّ عَنْ عَطَاءِ بْنِ يَزِيدَ عَنْ أَبِي أَيُّوبَأَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لَا تَسْتَقْبِلُوا الْقِبْلَةَ وَلَا تَسْتَدْبِرُوهَا لِغَائِطٍ أَوْ بَوْلٍ وَلَكِنْ شَرِّقُوا أَوْ غَرِّبُوا

Mu wax nu [Muhamed bin Mansur] ni; daf nu wax [Sufyan] ci [Az Zuhri] ci ['Atha bin Yazid] ci [Abu Ayyub Al Ansari] ni Yonent bi dafa wax ni: 'Bu leen jàkkarloo ak qibla, bul leen wëlbati ginaaw sooy génn wala ngay saw, waaye xoolal penku wala sowwu'.

Hadith

Imam Nasa'i : 22

أَخْبَرَنَا يَعْقُوبُ بْنُ إِبْرَاهِيمَ قَالَ أَنْبَأَنَا غُنْدَرٌ قَالَ أَنْبَأَنَا مَعْمَرٌ قَالَ أَنْبَأَنَا ابْنُ شِهَابٍ عَنْ عَطَاءِ بْنِ يَزِيدَ عَنْ أَبِي أَيُّوبَ الْأَنْصَارِيِّ قَالَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا أَتَى أَحَدُكُمْ الْغَائِطَ فَلَا يَسْتَقْبِلْ الْقِبْلَةَ وَلَكِنْ لِيُشَرِّقْ أَوْ لِيُغَرِّبْ

Yaqub bin Ibrahim wax nu ni; Dañu nu wax [Ghundar] ni; Dañu nu wax [Ma'mar] ni; Dañu nu wax Ibn Shihab ci Atha bin Yazid, ci Abu Ayub Al Ansari. Yonent bi dafa wax ni: 'Su kenn ci yéen bëggee génn, bul jàkkarloo ak qibla, waaye jàkkarloo ak penku wala sowwu'.

Hadith

Imam Nasa'i : 23

أَخْبَرَنَا قُتَيْبَةُ بْنُ سَعِيدٍ عَنْ مَالِكٍ عَنْ يَحْيَى بْنِ سَعِيدٍ عَنْ مُحَمَّدِ بْنِ يَحْيَى بْنِ حَبَّانَ عَنْ عَمِّهِ وَاسِعِ بْنِ حَبَّانَ عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ عُمَرَ قَالَلَقَدْ ارْتَقَيْتُ عَلَى ظَهْرِ بَيْتِنَا فَرَأَيْتُ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلَى لَبِنَتَيْنِ مُسْتَقْبِلَ بَيْتِ الْمَقْدِسِ لِحَاجَتِهِ

Mu wax nu ci [Qutayba bin Sa'id] ci [Malik] ci [Yahya bin Sa'id] ci [Muhamed bin Yahya bin Habban] ci ndijaay [Wasi' bin Habban] ci [Abdullah bin Omar] mu ne; Benn bis dama yéeg ci kaw sunu kër, ma gis fa Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam di tëdd ci kaw ñaari brik, di jàkkarloo ak wetu Baitul Maqdis.

Hadith

Imam Nasa'i : 24

أَخْبَرَنَا يَحْيَى بْنُ دُرُسْتَ قَالَ أَنْبَأَنَا أَبُو إِسْمَعِيلَ وَهُوَ الْقَنَّادُ قَالَ حَدَّثَنِي يَحْيَى بْنُ أَبِي كَثِيرٍ أَنَّ عَبْدَ اللَّهِ بْنَ أَبِي قَتَادَةَ حَدَّثَهُ عَنْ أَبِيهِأَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ إِذَا بَالَ أَحَدُكُمْ فَلَا يَأْخُذْ ذَكَرَهُ بِيَمِينِهِ

Bimu nu yëgalee loolu, mu ne; Abu Ismail, maanaam Al Qannad, neena ñu; Abdullah bin Abu Qatadah waxoon na ko ci pàppaam, ni Yonent bi dafa wax ni: 'Su kenn ci yeen saw, bul laal cëram ak loxoom ndijoor'.

Hadith

Imam Nasa'i : 25

أَخْبَرَنَا هَنَّادُ بْنُ السَّرِيِّ عَنْ وَكِيعٍ عَنْ هِشَامٍ عَنْ يَحْيَى هُوَ ابْنُ أَبِي كَثِيرٍ عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ أَبِي قَتَادَةَ عَنْ أَبِيهِ قَالَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا دَخَلَ أَحَدُكُمْ الْخَلَاءَ فَلَا يَمَسَّ ذَكَرَهُ بِيَمِينِهِ

Hannad bin As Sariy ci Waki' ci Hisyam ci Yahya Ibn Kathir ci Abdullah bin Abu Qatadah ci [Pàppaam] ne ko; ni Yonent bi sallallaahu aleyhi wasallam dafa wax ni: 'Su kenn ci yéen sawee, bul laal cëram ak loxoom ndijoor'.

Hadith

Imam Nasa'i : 26

أَخْبَرَنَا مُؤَمَّلُ بْنُ هِشَامٍ قَالَ أَنْبَأَنَا إِسْمَعِيلُ قَالَ أَخْبَرَنَا شُعْبَةُ عَنْ سُلَيْمَانَ عَنْ أَبِي وَائِلٍ عَنْ حُذَيْفَةَأَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَتَى سُبَاطَةَ قَوْمٍ فَبَالَ قَائِمًا

Bimu nu yëgalee loolu, mu ne; Dañu nu wax [Ismail] ni; Dañu nu nettali [Syu'bah] ci [Sulaiman] ci [Abu Wa'il] ci [Hudzaifah] 'Yonent bi dafa demoon ci mbalitu nit ñi, mu taxaw saw'.

Hadith

Imam Nasa'i : 27

أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ بَشَّارٍ قَالَ أَنْبَأَنَا مُحَمَّدٌ قَالَ أَنْبَأَنَا شُعْبَةُ عَنْ مَنْصُورٍ قَالَ سَمِعْتُ أَبَا وَائِلٍ أَنَّ حُذَيْفَةَ قَالَإِنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَتَى سُبَاطَةَ قَوْمٍ فَبَالَ قَائِمًا

Mu wax nu [Muhamed bin Basyar] ni; Muhamed bin Jafar nettali nañu ko ni; Daf nu wax [Syu'bah] ci [Mansur] ni; Dégg naa [Abu Wa'il] ni [Hudzaifah] dafa wax ni, 'Rasulullah Sallallaahu Aleyhi Wasallam dafa demoon benn yoon ci mbalitu nit ñi, mu taxaw saw'.

Hadith

Imam Nasa'i : 28

أَخْبَرَنَا سُلَيْمَانُ بْنُ عُبَيْدِ اللَّهِ قَالَ أَنْبَأَنَا بَهْزٌ قَالَ أَنْبَأَنَا شُعْبَةُ عَنْ سُلَيْمَانَ وَمَنْصُورٍ عَنْ أَبِي وَائِلٍ عَنْ حُذَيْفَةَأَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مَشَى إِلَى سُبَاطَةِ قَوْمٍ فَبَالَ قَائِمًا قَالَ سُلَيْمَانُ فِي حَدِيثِهِ وَمَسَحَ عَلَى خُفَّيْهِ وَلَمْ يَذْكُرْ مَنْصُورٌ الْمَسْحَ

Bimu nu yëgalee [Suleymaan bin Ubaidillah] muni; Dañu nu wax [Bahzun] ni; Dañu nu wax [Syu'bah] ci [Sulaiman] ak [Mansur] ci [Abu Wa'il] ci [Hudzaifah] ni Yonent bi dafa dox dem ci mbalitu nit ñi, ba noppi mu taxaw saw. Suleymaan dafa wax ci hadith-am; 'mu fomp ñaari khuf yi - ñaari dàll yi - fekk Mansur waxul fomp khuf yi ci dàll yi'.

Hadith

Imam Nasa'i : 29

أَخْبَرَنَا عَلِيُّ بْنُ حُجْرٍ قَالَ أَنْبَأَنَا شَرِيكٌ عَنْ الْمِقْدَامِ بْنِ شُرَيْحٍ عَنْ أَبِيهِ عَنْ عَائِشَةَ قَالَتْمَنْ حَدَّثَكُمْ أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بَالَ قَائِمًا فَلَا تُصَدِّقُوهُ مَا كَانَ يَبُولُ إِلَّا جَالِسًا

Mu wax nu [Ali bin Hujr] ni; Bimu nu waxee [Sharik] ci Miqdam bin Syuraih ci [pàppaam] ci [Aisha] mu ne: "Ku leen wax ni Rasulullah saw bimu taxawee, bul ko gëm, ndax Rasulullah sawwul ludul bimu toogee."

Hadith

Imam Nasa'i : 30

أَخْبَرَنَا هَنَّادُ بْنُ السَّرِيِّ عَنْ أَبِي مُعَاوِيَةَ عَنْ الْأَعْمَشِ عَنْ زَيْدِ بْنِ وَهْبٍ عَنْ عَبْدِ الرَّحْمَنِ ابْنِ حَسَنَةَ قَالَخَرَجَ عَلَيْنَا رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَفِي يَدِهِ كَهَيْئَةِ الدَّرَقَةِ فَوَضَعَهَا ثُمَّ جَلَسَ خَلْفَهَا فَبَالَ إِلَيْهَا فَقَالَ بَعْضُ الْقَوْمِ انْظُرُوا يَبُولُ كَمَا تَبُولُ الْمَرْأَةُ فَسَمِعَهُ فَقَالَ أَوَ مَا عَلِمْتَ مَا أَصَابَ صَاحِبُ بَنِي إِسْرَائِيلَ كَانُوا إِذَا أَصَابَهُمْ شَيْءٌ مِنْ الْبَوْلِ قَرَضُوهُ بِالْمَقَارِيضِ فَنَهَاهُمْ صَاحِبُهُمْ فَعُذِّبَ فِي قَبْرِهِ

Daf nu nettali ni [Hannad bin As Sariy] ci [Abu Mu'awiyah] ci [Al'Amasy] ci [Zaid bin Wahab] ci [Abdurrahman bin Hasanah] mu ne: 'Dafa musa daje ak nun, mu am lu melni shield der ci loxoom. Mu daal di koy tëye, toog ci ginaawam, ba noppi mu saw ci boor bi. Ñenn ñi dañu wax ni, 'Xool, mingi saw ni jigéen! ' Bi Rasulullah Sallallaahu 'Aleyhi wasallam déggee kàddu yooyu, mu ne: 'Xamuleen li dal waa Bani Israyil?! Su kenn ci ñoom tasee siw, dañu dagg mbubb mi tas siw, ginaaw ga xaritam bi daal di leen tere def ko, ñu daal di koy sonal ci bàmmeel bi'.

Hadith

Imam Nasa'i : 31

أَخْبَرَنَا هَنَّادُ بْنُ السَّرِيِّ عَنْ وَكِيعٍ عَنْ الْأَعْمَشِ قَالَ سَمِعْتُ مُجَاهِدًا يُحَدِّثُ عَنْ طَاوُسٍ عَنْ ابْنِ عَبَّاسٍ قَالَمَرَّ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلَى قَبْرَيْنِ فَقَالَ إِنَّهُمَا يُعَذَّبَانِ وَمَا يُعَذَّبَانِ فِي كَبِيرٍ أَمَّا هَذَا فَكَانَ لَا يَسْتَنْزِهُ مِنْ بَوْلِهِ وَأَمَّا هَذَا فَإِنَّهُ كَانَ يَمْشِي بِالنَّمِيمَةِ ثُمَّ دَعَا بِعَسِيبٍ رَطْبٍ فَشَقَّهُ بِاثْنَيْنِ فَغَرَسَ عَلَى هَذَا وَاحِدًا وَعَلَى هَذَا وَاحِدًا ثُمَّ قَالَ لَعَلَّهُ يُخَفَّفُ عَنْهُمَا مَا لَمْ يَيْبَسَاخَالَفَهُ مَنْصُورٌ رَوَاهُ عَنْ مُجَاهِدٍ عَنْ ابْنِ عَبَّاسٍ وَلَمْ يَذْكُرْ طَاوُسًا

Daf nu wax ni [Hannad bin As-Sariy] ci [Waki'] ci [Al-A'masy] ne; 'Dégg naa [Mujahid] wax; ci [Thawus] ci [Ibn Abbas] mu wax; Benn bis la Yonent bi sallallaahu aleyhi wasallam romb ñaari bàmmeel, ci la wax: 'Ñaari ñi dëkkoon ci bàmmeel yooyu dañu leen sonal te ñoom ñaar ñépp ñu ngi leen sonal te du ndax bàkkaar yu mag. Kii daa musa raxas saw, waaye kii dañu ko daan sonal ndax dafa daan xeex ak moroomam saa yu nekk.' Ba noppi mu laaj benn piyeesu garabu dat bu tooy ba leegi. Mu dagg ko ñaar, laxas ko ci ñaari bàmmeel yi. Muni ma: 'Yaakaar naa ni lii dina leen féexal ñoom ñaar fekk ñu woxagul. '

Hadith

Imam Nasa'i : 32

أَخْبَرَنَا أَيَّوبُ بْنُ مُحَمَّدٍ الْوَزَّانُ قَالَ حَدَّثَنَا حَجَّاجٌ قَالَ قَالَ ابْنُ جُرَيْجٍ أَخْبَرَتْنِي حُكَيْمَةُ بِنْتُ أُمَيْمَةَ عَنْ أُمِّهَا أُمَيْمَةَ بِنْتِ رُقَيْقَةَ قَالَتْكَانَ لِلنَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَدَحٌ مِنْ عَيْدَانٍ يَبُولُ فِيهِ وَيَضَعُهُ تَحْتَ السَّرِيرِ

Bimu nu waxee [Ayyub bin Muhamed Al Wazzan] mu ne; wax nu [Hajjaj] ni; [Ibnu Jurayj] nee na; waxma [Umaimah bint Umaymah] ci yaayam [Umaimah bint Ruqaiqah] mu ne; Yonent bi sallallaahu aleyhi wasallam amoon na ndab buñu defaree denku dat bumu daan jëfandikoo ngir saw. Mu def ko ci suufu lal bi'.

Hadith

Imam Nasa'i : 33

أَخْبَرَنَا عَمْرُو بْنُ عَلِيٍّ قَالَ أَنْبَأَنَا أَزْهَرُ أَنْبَأَنَا ابْنُ عَوْنٍ عَنْ إِبْرَاهِيمَ عَنْ الْأَسْوَدِ عَنْ عَائِشَةَ قَالَتْيَقُولُونَ إِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَوْصَى إِلَى عَلِيٍّ لَقَدْ دَعَا بِالطَّسْتِ لِيَبُولَ فِيهَا فَانْخَنَثَتْ نَفْسُهُ وَمَا أَشْعُرُ فَإِلَى مَنْ أَوْصَىقَالَ الشَّيْخُ أَزْهَرُ هُوَ ابْنُ سَعْدٍ السَّمَّانُ

Amr bin Ali wax nanu ni; ci [Azhar] ci [Ibn Aun] ci [Ibrahim] ci [Al Aswad] ci [Aisyah] mu ne; ' Nit ñi ne: 'Rasulullah Sallallaahu 'Aleyhi wasallam jox na Aali testama. Mu laaj ñu jox ko paan bumu daan saw, ci la tànk yi tàmbali di néew doole ndax defa jege dee, yëguma ko, te kan la defal testamaa bi?' Amr bin Ali neena; Li chekh azhar bëgga wax mooy ibnu saïd bin samaan.

Hadith

Imam Nasa'i : 34

أَخْبَرَنَا عُبَيْدُ اللَّهِ بْنُ سَعِيدٍ قَالَ أَنْبَأَنَا مُعَاذُ بْنُ هِشَامٍ قَالَ حَدَّثَنِي أَبِي عَنْ قَتَادَةَ عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ سَرْجِسَأَنَّ نَبِيَّ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لَا يَبُولَنَّ أَحَدُكُمْ فِي جُحْرٍقَالُوا لِقَتَادَةَ وَمَا يُكْرَهُ مِنْ الْبَوْلِ فِي الْجُحْرِ قَالَ يُقَالُ إِنَّهَا مَسَاكِنُ الْجِنِّ

Bimu nu waxee [Ubaidillah bin Sa'id] mu wax; Mu'adz bin Hisham waxna nu; [sama pàppa] daf ma wax ci [Qatadah] ci [Abdullah bin Sarjis] ni Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam dafa wax ni: 'Kenn ci yéen bumu saw ci pax'. Ñu laaj Qatadah, lu tax ñu xàram saw ci pax mi? mu tontu ko; amna xibaar buy wax ni foofu la jinne bi dëkk.

Hadith

Imam Nasa'i : 35

أَخْبَرَنَا قُتَيْبَةُ قَالَ حَدَّثَنَا اللَّيْثُ عَنْ أَبِي الزُّبَيْرِ عَنْ جَابِرٍعَنْ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَنَّهُ نَهَى عَنْ الْبَوْلِ فِي الْمَاءِ الرَّاكِدِ

Bimu nu jottali [Qutaibah] mu ne; daf nu wax [Al-Laits] ci [Abu Zubair] ci [Jabir] ci Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam, dafa tere ku saw ci ndox mu tëju - bu dul wal-'.

Hadith

Imam Nasa'i : 36

أَخْبَرَنَا عَلِيُّ بْنُ حُجْرٍ قَالَ أَنْبَأَنَا ابْنُ الْمُبَارَكِ عَنْ مَعْمَرٍ عَنْ الْأَشْعَثِ بْنِ عَبْدِ الْمَلِكِ عَنْ الْحَسَنِ عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ مُغَفَّلٍعَنْ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لَا يَبُولَنَّ أَحَدُكُمْ فِي مُسْتَحَمِّهِ فَإِنَّ عَامَّةَ الْوَسْوَاسِ مِنْهُ

Mu wax nu [Ali bin Hujr] ni; Ibn Al Mubarak ci Ma'mar ci Al Asy'ats bin Abdul Malik ci Al Hasan ci Abdullah bin Mughaffal ci Rasulullah Sallallaahu aleyhi wasallam, mu ne: 'Bu leen saw ci barabu sangu bi, ndax li ëpp ci jaaxle gi mingi joge ci sangu bi.'

Hadith

Imam Nasa'i : 37

أَخْبَرَنَا مَحْمُودُ بْنُ غَيْلَانَ حَدَّثَنَا زَيْدُ بْنُ الْحُبَابِ وَقَبِيصَةُ قَالَا أَنْبَأَنَا سُفْيَانُ عَنْ الضَّحَّاكِ بْنِ عُثْمَانَ عَنْ نَافِعٍ عَنْ ابْنِ عُمَرَ قَالَمَرَّ رَجُلٌ عَلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ يَبُولُ فَسَلَّمَ عَلَيْهِ فَلَمْ يَرُدَّ عَلَيْهِ السَّلَامَ

Neena ñu [Mahmud bin Ghailan] newoon nañu [Zaid bin Al Hubbab] ak [Qubaishah] ñoom ñaar neena ñu; ci [Sufyan] ci [Dlahak bin Othman] ci [Nafi'] ci [Ibn Omar] mu ne; Amna ku góor ku romb Rasulullah, mu doon saw. Nit ki daal di koy nuyu, waaye tontuwul.'

Hadith

Imam Nasa'i : 38

أَخْبَرَنَا مُحَمَّدُ بْنُ بَشَّارٍ قَالَ حَدَّثَنَا مُعَاذُ بْنُ مُعَاذٍ قَالَ أَنْبَأَنَا سَعِيدٌ عَنْ قَتَادَةَ عَنْ الْحَسَنِ عَنْ حُضَيْنٍ أَبِي سَاسَانَ عَنْ الْمُهَاجِرِ بْنِ قُنْفُذٍأَنَّهُ سَلَّمَ عَلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ يَبُولُ فَلَمْ يَرُدَّ عَلَيْهِ حَتَّى تَوَضَّأَ فَلَمَّا تَوَضَّأَ رَدَّ عَلَيْهِ

Mu wax nu [Muhamed bin Basyar] ni; Mu'adz bin Mu'adz neena; Mu nuyu Sa'id ci [Qatadah] ci [Al Hasan] ci [Hudlain Abu Saasan] ci [Al Muhajir bin Qunfudz] ' Benn bis mu nuyu Rasulullah bi muy saw, waaye Rasulullah nanguwul dellu. Ginaaw bimu wutee ba noppi mu delloo nuyoo bi.

Hadith

Imam Nasa'i : 39

أَخْبَرَنَا أَحْمَدُ بْنُ عَمْرِو بْنِ السَّرْحِ قَالَ أَنْبَأَنَا ابْنُ وَهْبٍ قَالَ أَخْبَرَنِي يُونُسُ عَنْ ابْنِ شِهَابٍ عَنْ أَبِي عُثْمَانَ بْنِ سَنَّةَ الْخُزَاعِيِّ عَنْ عَبْدِ اللَّهِ بْنِ مَسْعُودٍأَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ نَهَى أَنْ يَسْتَطِيبَ أَحَدُكُمْ بِعَظْمٍ أَوْ رَوْثٍ

Bimu nu yëgalee [Ahmad bin Amr bin As Sarh] muni; Ibn Wahab dafa wax ni; Dañu ma nettali Yunus ci Ibn Shihab ci Abu Uthman bin Sanah Al Khuza'i ci Abdullah bin Mas'ud ni Yonent bi dafa tere setal yax wala neefere baayima.

Hadith

Imam Nasa'i : 40

أَخْبَرَنَا يَعْقُوبُ بْنُ إِبْرَاهِيمَ قَالَ حَدَّثَنَا يَحْيَى يَعْنِى ابْنَ سَعِيدٍ عَنْ مُحَمَّدِ بْنِ عَجْلَانَ قَالَ أَخْبَرَنِي الْقَعْقَاعُ عَنْ أَبِي صَالِحٍ عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَعَنْ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ إِنَّمَا أَنَا لَكُمْ مِثْلُ الْوَالِدِ أُعَلِّمُكُمْ إِذَا ذَهَبَ أَحَدُكُمْ إِلَى الْخَلَاءِ فَلَا يَسْتَقْبِلْ الْقِبْلَةَ وَلَا يَسْتَدْبِرْهَا وَلَا يَسْتَنْجِ بِيَمِينِهِ وَكَانَ يَأْمُرُ بِثَلَاثَةِ أَحْجَارٍ وَنَهَى عَنْ الرَّوْثِ وَالرِّمَّةِ

Yaqub bin Ibrahim wax nu ni; daf nu wax ni [Yahya mooy Ibn Sa'id] ci [Muhamed bin Ajlan] dafa wax; ci [Al Qa'qa'] ci [Abu Salih] ci [Abu Hurairah] ci Yonent Yàlla, sallallaahu aleyhi wasallam, mu ne: 'Maa ngi melni sama baay ci yaw. Maa ngi lay jàngal ne boo bëggee dem WC bul jàkkarloo ak qibla te bul ko wëlbati ginaaw, bul raxas ak sa loxo ndeyjoor.' Mu santaane itam ñu setal boppam ak ñetti xeer. Dafa tere setal yaram ak njur baayima ak yax'.